gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, -ñatti yoon-, amunu ci pexe, waaye Yàlla mu màgg mi moo koy dindi ci wakkirlu

gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, -ñatti yoon-, amunu ci pexe, waaye Yàlla mu màgg mi moo koy dindi ci wakkirlu

Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, -ñatti yoon-, amunu ci pexe, waaye Yàlla mu màgg mi moo koy dindi ci wakkirlu.

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo Tiyara te mooy gaaflu ci lépp lu mu man a doon moo xam lu ñuy dégg la mbaa lu ñuy gis, ci picci walla rab, walla ñi am laago, walla ay limat (numéro) walla ay bis mbaa leneen. Dafa tudd picci nag ndaxte moo siiwoon fa Ceddo ga, te cosaanam mooy naawal am picci booy tàmbalee jëf, tukki walla yaxantu mbaa leneen, bu naawee ci wetug ndayjoor mu rafetlu ko daal di def la mu bëgg, bu jëmee wetug càmmooñ mu gaaflu ko daal di bàyyi la mu bëggoon. Mu xibaare ne loolu bokkaale la, li tax gaaflu nekk bokkaale mooy ne, kenn du indi yiw ku dul Yàlla, te kenn du jeñ aw lor ku dul Yàlla moom rekk amul bokkaale. Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- nee na : amaana gaaflu tàbbi ci xolu jullit bi, waaye li ko war mooy mu jeñ ko ak wakkirlu ci Yàlla ànd ak di def sabab yi.

فوائد الحديث

Gaaflu bokkaale la ; ndaxte day wékk xol bi ci ku dul Yàlla.

Njariñu baamtu masala yu am solo yi, ngir ñu wattu ko ak mu sax ci xol yi

Gaaflu li koy dindi mooy wakkirlu ci Yàlla mu kawe mi.

Digle nañu ñuy wakkirlu ci Yàlla rekk te wékk xol bi ci Yàlla mu sell mi.

التصنيفات

Bokkaale, Ngëneeli jëfi xol yi