Yàlla bind na ndogali mbindéef yi njëkk muy bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-fukki junniy at

Yàlla bind na ndogali mbindéef yi njëkk muy bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-fukki junniy at

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haasi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla bind na ndogali mbindéef yi njëkk muy bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-fukki junniy at, mu daaldi wax: te boobu gàngunaayam ga ma nga ca kawum ndox».

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla bind na lépp luy am ci ndogali mbindéef yi cig faramface ci dund ak dee, ak wërsëg ak yeneen, ca àlliwó ja ñu sàmm(Lawhul Mahfuus) lu jiitu muy bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-fukki junniy at, te dana am kem na ko Yàlla dogale, Lépp luy am ci ndogalu Yàlla ak kàttanam lay ame. Lépp lu jot nit ki naru ko woon a moy, te lépp lu ko moy naru ko woon a jot.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi:

Gëm ndogal yi lu war la.

Ndogal mooy: xam gi Yàlla xam bir yi, bind ko, ak coobareem, ak amal ga mu ko amal.

Gëm ne ndogal yi bind nañu ko njëkk ñuy bind asamaan yi ak suuf si day waral gërëm ak nangu.

Gàngunaayu Aji-Yërëme ji moo ngi ci kawum ndox lu jiitu bindug asamaan yi ak suuf si.

التصنيفات

Tolluwaayi dogal yi