إعدادات العرض
Yàlla jéggal na samaw xeet njuumte ak fàtte ak lu ñu leen forse
Yàlla jéggal na samaw xeet njuumte ak fàtte ak lu ñu leen forse
Jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "Yàlla jéggal na samaw xeet njuumte ak fàtte ak lu ñu leen forse".
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Hausa Kurdî Kiswahili Português සිංහල دری অসমীয়া پښتو O‘zbek Tiếng Việt Македонски ភាសាខ្មែរ ਪੰਜਾਬੀ తెలుగు ไทย Moore አማርኛ Magyar Azərbaycan ქართული ಕನ್ನಡ Yorùbá ગુજરાતી Українська Shqip Кыргызча Српски Kinyarwanda тоҷикӣ Čeština தமிழ் Bambara नेपाली മലയാളം kmr ms Deutsch Lietuviųالشرح
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne: Yàlla baal na xeetam wi ñatti mbir: Bi ci njëkk: njuumte, te mooy li ñuy def ci lu dul ag tay, te mooy jullit bi jublu ci jëfam ji dara far def leneen lu mu jubluwul woon. Ñaareel bi: fàtte, te mooy jullit bi xam dara, waaye ba muy jëf da ko a fatte, loolu it bàkkaar amu ci. Ñatteel bi: ga, amaana ñu ga jaam bi ci mu def lu mu bëggul te amul kàttanu ci ba ña def la ñu ko ga, bu boobaa bàkkaar du ko ca war du caagine yaraanga. Ànd ak loolu ñu seetlu ne hadiis bi ci diggante jaam bi ak boroomam lay wax, bu dee bàyyi lu ñu digle ngir fàtte nag du tax mu wàcc ko, bu dee it ak tooñ dafa topp ca jëf ja du tax àqi mbindeef mi wàcc ko, kem bu rayoon ci njuumte, kon Diya da koy war, walla mu yàq oto jàmbur kon da ko a war fay.فوائد الحديث
Yaatug yërmàndey Yàlla -màgg na kawe na- ak ug ñeewentoom ci jaamam yi ba tax mu dindil leen bàkkaar ci bu ñu defee ag moy ci ñatti anam yii.
Ngëneelu Yàlla ci Yonnente bi Muhammad yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak ci xeetam wi.
Yëkkëti bàkkaar bi tekkiwul yëkkëti àtte bi walla fay gi, ci misaal ku fàttee jàppu, daal di julli ngir njort ne laab na, kooku bàkkaar waru ko ci loolu, waaye daa war a jàppu baamtu julli gi.
Yëkkëti bàkkaar ndax ug ga fàww sàrt yi daje ca, niki aji-ga ji man a def li mu koy tëkkoo.
التصنيفات
Gëm Yàlla Mu tedd Mu màgg mi