ku Yàlla namm ci moom aw yiw dana ko nattu

ku Yàlla namm ci moom aw yiw dana ko nattu

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku Yàlla namm ci moom aw yiw dana ko nattu».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla bu nammee aw yiw ci kenn ci jaamam yu gëm yi dana leen nattu ci séen i bakkan ak séen i alal ak séen i njaboot, ngir la ca aji-gëm ji di jële ci dellu ci Yàlla mu kawe mi ak ci di ñaan, ak la ca nekk ci far ay ñaawtéef, ak yëkkatikuy daraja.

فوائد الحديث

Aji-gëm ji dana dajeek ay xeeti nattu.

Ab nattu man naa nekk màndargam bëgg gi Yàlla bëgg jaamam bi, ba dana ko yëkkëtil ay darajaam, kaweel ab dayoom, sippil ko ay njuumteem.

Ñaaxe ci muñ musiba yi te bañ a naqarlu.

التصنيفات

Masalay dogal yi