Kuy niru-nirulu aw nit ca ñoom la book

Kuy niru-nirulu aw nit ca ñoom la book

Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Kuy niru-nirulu aw nit ca ñoom la book».

[Tane na] [Abóo Daawuda soloo na ko - Ahmat soloo na ko]

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daf nuy xamal ne képp kuy roy yéefar yi, mbaa kàccoor yi, mbaa ñu baax ñi -ci def li leen di màndargaal ci wàllu pas-, walla ag jaamu, walla aada- kon bokk na ci ñoom; Ndax roy leen ci biti dafay yóbbe ci roy leen ci biir, te sikk-sakka amul ci ne roy aw askan day juddoo ci naw leen, te man naa tax nga bëgg leen, màggal leen, jeng jëm ci ñoom, te loolu man naa yóbbe nit ki roy leen sax ci biir ak ci jaamu Yàlla - Yal na nu ci Yàlla musal-.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi:

Mooy day moytandiku Loo roy yéefar yi ak kàccoor yi.

Day soññee ci di niru-nirulu ñu baax ñi ak di leen roy.

Roy ci biti day waral mbëggeel ci biir.

Nit ki dees na ko tëkku mu am bàkkaar kem niru-nirulu ga ak i xeetam.

Terees na niru-nirulu lu yéefar yi ci séen diine ak séen aada ja ñu jagoo, bu dul loolu nag niki jàng liggéey yi ak yu ko niru loolu tereesu ko.

التصنيفات

Nuru-nurulu gees aaye