ne ko: yaw yaay sunu sang, mu ne nu: "sang bi mooy Yàlla", nu ne ko: yaanu gën, gën noo màggi xéewal, mu ne nu: "waxleen la ngeen daa wax, mbaa lenn ca la ngeen daa wax, te bu leen saytaane yóbbaale

ne ko: yaw yaay sunu sang, mu ne nu: "sang bi mooy Yàlla", nu ne ko: yaanu gën, gën noo màggi xéewal, mu ne nu: "waxleen la ngeen daa wax, mbaa lenn ca la ngeen daa wax, te bu leen saytaane yóbbaale

Jële na ñu ci Abdullah Ibnus siqiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne: man ak mbooloo ci Banuu Aamir dañoo ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: yaw yaay sunu sang, mu ne nu: "sang bi mooy Yàlla", nu ne ko: yaanu gën, gën noo màggi xéewal, mu ne nu: "waxleen la ngeen daa wax, mbaa lenn ca la ngeen daa wax, te bu leen saytaane yóbbaale".

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat]

الشرح

Am mbooloo dañoo dem ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ba ñu eggee ci moom wax ko -ngir di ko tagg- yenn kàddu yoy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bëggu ko, Ñu ne ko: "yaw yaay sunu sang", Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: "sang bi mooy Yàlla" Mooy sàngu lépp lu mu sàkk, te ñoom ay jaamam lañu. Ñu ne ko: yaw "yaa ñu gën ay ngëneel" te gën ñoo kawe daraja ak teddnga ak i may. Te yaw "yaa nu gën a màgg ay xéewal" ëpp nu ay may gën noo kawe. Topp Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digal leen ñu wax seen wax ja ñu daan wax, te bañ a sonal seen bopp ci yenn wax yi, te saytaane bañ leen a yóbb ci ëppal ak ci jaye gu leen di tàbbal ci lu araam niki bokkaale ak i jumtukaayam.

فوائد الحديث

Màggaayu dayob Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci xoli Sahaaba yi ak ni nu ko wormaale.

Tere nañu toggoo kàddu yu ëpp, digal leen ñu yamale seen i wax

Aar Tawhiid ci lépp lu koy yàq ci ay wax ak i jëf.

Tere nañu ëppal ci tagg, ndax daa bokk ci yi santaane di jaare.

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mooy sangi doomi Aadama yi, li ñëw ci hadiis bi nag ci buntub toroxlu la, ak buntub ragal ci ñoom ñu ëppal ci moom.

التصنيفات

Sunu Yónnent Muhammat yalna Yàlla xéewalal ko te jàmmal ko