sunu Boroom bu baarkeel bi te kawe day wàcc guddi gu nekk ci asamaani àdduna si bu guddi gi desee ñatteelu xaaj bu mujj ba

sunu Boroom bu baarkeel bi te kawe day wàcc guddi gu nekk ci asamaani àdduna si bu guddi gi desee ñatteelu xaaj bu mujj ba

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «sunu Boroom bu baarkeel bi te kawe day wàcc guddi gu nekk ci asamaani àdduna si bu guddi gi desee ñatteelu xaaj bu mujj ba, di wax naan: ku may woo ma wuyu ko? Ku may laaj ma jox ko? Ku may jéggalu ma jéggal ko?».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne Yàlla sunu boroom day wàcc guddi gu nekk ci asamaani àdduna si bu guddi gi desee ñatteelu xaaj bu mujj ba, di xemmemloo jaamaam yi ci ñaan, ndax moom mooy wuyu ku ko woo, di leen ñaax ci ñu laaj ko lu ñu bëgg, ndax mooy jox ku ko laaj, di leen woo ci ñu jéggalu ko séen i bàkkaar, ndax mooy jéggal ay jaamam yi ko gëm.

فوائد الحديث

Ngëneelu ñatteelu xaaj bi mujj ci guddi gi ak di ca julli di ca ñaan di ca jéggalu.

Jaadu na ci nit ki bu déggee hadiis bii mu xér lool ci donnewoo waxtuy nangu ñaan yi.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci ay turam ak i meloom