bumu bàyyi benn caq walla bantu fett ci doqug genn giléem te daggu ko

bumu bàyyi benn caq walla bantu fett ci doqug genn giléem te daggu ko

Jële na ñu ci Abuu Basiir Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; Dafa nekkoon ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci ab tukki ci tukkerm yi, nee na: Yónente daldi yónni lenn ndaw -fekk nit ñi ña nga ca séen fanaanukaay- mu ne ko "bumu bàyyi benn caq walla bantu fett ci doqug genn giléem te daggu ko".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa nekkoon ci benn tukki, nit ñi nekk ci séen bérab ya ñuy fanaan ca séen wàccuwaay ya ak xayma ya, mu yónni benn waay ca nit ña ngir digal leen ñu dagg caq yi ñu takk ci doqi giléem yi moo xam ci bant la -bantu fett- mbaa leneen niki jóolóoli walla dàll, loolu nag ndaxte dañu leen ko doon takkal ngir moytu bët, mu digle ñu dagg ko; ndax du leen fegal dara njariñ ak lor ci loxoy Yàlla dong la nekk amul kees koy bokkaalel.

فوائد الحديث

Tere nañu di takk ay bant ak i caq ngir xëcc njariñ mbaa jeñ lor; ndaxte loolu bokkaale la.

Takk ab caq ci lu dul bantu fett bu dee ngir taar la walla laab ngir wommat aw mala mbaa yeew ko ci kon dara nekku ci.

Warug tere lu bon sunu kem kàttan.

Wara nañoo wékk sunu xol ci Yàlla rekk amul bokkaale.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko