dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal

dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal

Jële nañu ci Al-Hirbaat Ibnu Saariyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Benn bis Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa taxaw fi nun daal di nuy waar waar gu jotale xol yi jàq nañu ci, bët yi tuur ci rangooñ, ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi, waar nga nu waarug kuy tàggatoo, jox ñu ak kóllare. Mu ne leen : "dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal, ŋànkleen ko ak seen i dégéj, te ngeen moytandiku mbir yi ñu sos, ndax bidaa yépp ay réer la".

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa waar Sahaaba yi ag waar gu jotale ba xol yi ragal ca, bët yi jooy ca, Ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi dafa me ni waareg kuy tàggatoo la ndax li ñu ci gis ci jotaleg Yónente bi ci waare gi, ñu sàkku ci moom ag ndénkaane gog danañu ci jàpp ginnaawam, Mu ne leen : maa ngi leen fi dénk ragal Yàlla mu màgg mi, ci def yi war ak bàyyi yi ñu araamal, Ak dégg ak topp, maanaam : ñeel njiit yi, doonte ab jaam moo leen jiite, mbaa mu not leen ba jiite leen, maanaam ki gën a suufe ci nit ñi moo leen jiite buleen rëy ci loolu nangeen ko topp, ndax day ragal a yëkkati fitna, ndaxte ku dund ci yéen dana gis wuute gu bari, Mu leeralal leen ni ñuy génne ci wuute gi, te mooy jàpp ci suunnaam ak sunnas njiit yu jub ya tey jubale ci ginnaawam, Abuu Bakarin As-Siddiix, ak Umar Ibnul Xattaab, ak Usmaan Ibnu Affaan, ak Aliyun Ibnu Abii Taalib, -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ak màtt ca ak seeni dégéj, maanaam -bëñ ya mujj-: li mu jublu ci loolu mooy farlu ci taqoo ak sunna ak jàpp ca, Mu moytondikuloo leen bir yi ñu sos fent ko ci diine, ndax bidaa yépp ay réer lañu.

فوائد الحديث

Solos ŋoy ci sunna ak topp ko.

Yittewoo di waare, ak di nooyal xol yi.

Digle ñu topp ñenti njiit yu jub ya tey jubale ci ginnaawam, te ñooy Abuu Bakar, ak Umar, ak Usmaan, ak Aliyun -yal na leen Yàlla dollee gërëm-.

Tere nañu sos ci diine ji, ndax bidaa yépp ay réer lañu.

Dañuy dégg di topp njiitu jullit ñi ci lu dul ag moy.

Solos ragal Yàlla mu màgg mi ci bépp jamono ak bépp anam.

Wuute luy am la ci xeet wi, waaye bu amee dañoo war a dellu ci sunnas Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak njiit yu jub ya.

التصنيفات

Solos Sunna ak wàccuwaayam, Ngëneeli Saaba yi Yàlla gërëm na leen, Àqi njiit ci ña mu jiite, Merits of the Rightly Guided Caliphs