bàyyileen ma bu ma leen bàyyee, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seeni laaj ak di wuute ak seeni Yonnente

bàyyileen ma bu ma leen bàyyee, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seeni laaj ak di wuute ak seeni Yonnente

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bàyyileen ma bu ma leen bàyyee, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seeni laaj ak di wuute ak seeni Yonnente , bu ma leen teree dara nangeen ko moytu, bu ma leen digalee dara defleen ca lu ngeen man».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day fàttalee ne àttey Sariiha yi ñatti xaaj la: lu ñu noppi, lu ñu tere, ak lu ñu digle. Bu njëkk bi: te mooy lu Sariiha noppi: ba tax tegu ci benn àtte, te cosaan ci mbir yi mooy ñàkk a war; Bu dee jamonoom moom Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- li war mooy bañ koo laaj dara lu tàbbeegul ndax ragal ñu wàcce ci ag waral walla araamal, ndax Yàlla da koo bàyyi ngir yërëm jaam ñi, Bu dee ginnaaw bi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- faatoo nag kon laaj ngir leerlu ak xamle lu ñu yittewoo ci mbiri diine loolu dagan na lu ñu digle la sax nag, bu dee nag ci anamug taral ak sonle loolu lañu namm ci bàyyi laaj bi ci hadiis bi; ndaxte loolu man naa yóbbe ca la Banuu Israayil tàbbi woon, ndaxte dañu leen a digal ñu ray aw nag te nag wu ñu rayoon rekk def nañu ndigal la, waaye dañoo taral ñu taral ci seen kaw. Ñaareel bi: tere yi; te mooy: lol ku ko bàyyi am ca ab yool, ku ko def am ca mbugal, ñu war a moytandiku léppam. Ñatteel bi: ndigal yi; te mooy: lol ku ko def am ca ab yool, ku ko bàyyi am ca mbugal, ñu war caa def lu ñu man.

فوائد الحديث

Jaadu na ñu yittewoo li gën a am solo te ñu soxlawoo ko, te bàyyi li ñu soxlaagul, te bañ a yittewoo laaj lu amul.

Araamal nañu di laaj lol man naa yóbbe ci jafeel masala yi, ak tijji buntu lënt yiy waral wuute gu bari.

Digle nañu ñu bàyyi yi ñu tere; ndax bàyyi ko amul coono, looloo tax tere gi di li matale.

Digle nañu ñu def ndigal yi ci kem kàttan; ndaxte moom man naa am coono walla ñu tële koo def; looloo tax ndigal li di ci kem kàttan.

Tere nañu di baril ay laaj, boroom xam-xam yi séddale nañu laaj ci ñaari xaaj: benn bi mooy: loo xam ne ci anamug xamle lu ñu soxla ci mbiri diine la, lii moom lu ñu digle la te ci xaaj bii la laaji Sahaaba yi nekkoon, ñaareel bi: loo xam ne ci anamug taral la ak sonnale lii nag dañu koo tere.

Artu xeet wi ci wuute ak Yonnente bi, kem ni mu ame woon ca xeet ya ko jiitu woon.

Baril di laaj lu ñu yittewoowul ak di woote ak Yonnente yi sabab la ci alkande, rawati na ci mbir yi nga xam ne maneesu caa egg, niki: masalay kumpa yi nga xam ne kenn xamu ko ku dul Yàlla, ak mbiri bis-pénc.

Tere nañu laaj ci masala yu tar yi, Awsaahii nee na: Yàlla bu nàmme xañ jaam bi baarkeb xam-xam day sànni ci làmmeñam ay njaxas, gisnaa ne ñoom ñoo gën a néew xam-xam ci nit ñi, Ibn Wahb nee na: dégg naa Maalik di wax naan: werente ci xam-xam day dindi leeru xam-xam ci xolu nit ki.

التصنيفات

Yónnent yi jiitu yalna jàmm nekk ci ñoom, Li waat yi di wund ak nees di génnee àtte yi