buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli

buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli

Jële na ñu ci Marsad Al-Xanawii -yalna ko Yàlla gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na toog ci kaw bàmmeel. Niki mu teree julli jublu ci bàmmeel, bàmmeel bi nekk ci wetu penku kiy julli; ndax loolu daa bokk ci yiy yóbbe ci bokkaale yi.

فوائد الحديث

Tere nañu julli ci ay bàmmeel walla séen diggante walla jublu ko lu dul jullig néew kem ni mu saxe ci Sunna.

Tere nañu di julli jublu ay bàmmeel ngir sakk yoonu bokkaale.

Lislaam dafa tere ëppal ci bàmmeel yi ak di ko doyodal, deesul ëppal waaye deesul yéesal.

Wormay jullit day des di wéy ginnaaw ba mu faatoo, ngir li Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na ne: (toj yaxu ku faatu moo ngi mel ni toj ko ba muy dund).

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko, Sàrti julli