Sama xeet wépp dinañu dugg àjjana ba mu des ku bañ

Sama xeet wépp dinañu dugg àjjana ba mu des ku bañ

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Sama xeet wépp dinañu dugg àjjana ba mu des ku bañ», ñu ne ko ana kan mooy bañ yaw Yónente Yàlla bi? Mu ne: «ku ma topp dugg àjjana ku ma moy nag kooku mooy ki bañ».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne xeetam wéppay dugg àjjana ba mu des ku bañ! Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ne ko: kan mooy bañ yaw Yónente Yàlla bi?! Mu tontu leen ne leen: képp ku wommatu topp Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dana dugg àjjana, ku ko moy nag te wommatuwul ñeel Sariiha bi kooku moo bañ a dugg àjjana ngir ay jëfam yu bon.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi:

Topp Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa bokk ci topp Yàlla, moy ko it moy Yàlla la.

Topp Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day waral àjjana, moy ko it day waral sawara.

Ak bégle ñeel ñiy topp Yàlla te bokk ci xeet wii, ci ne ñoom ñéppay dugg àjjana ba mu des ku moy Yàlla ak Yónenteem.

Ñeewante gi Yónente bi am ci aw xeetam, ak xér gi mu xér ci seenug gindiku.

التصنيفات

Sunu Yónnent Muhammat yalna Yàlla xéewalal ko te jàmmal ko