nit ki gën a texe ci samag rammu ëllëg bis-penc, mooy ki wax, Laa ilaaha illal Laahu, te mu sell lool ci xolam, walla ci bakkanam

nit ki gën a texe ci samag rammu ëllëg bis-penc, mooy ki wax, Laa ilaaha illal Laahu, te mu sell lool ci xolam, walla ci bakkanam

Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne: Wax nañu Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko ana kan ci nit ñi moo gën a texe ci sag rammu ëllëg bis-penc? Yónent Yàlla bi wax ne: «Njoortoon naa ne yaw Abuu Hurayrata Yamamay njëkk laaj lii; ndax li ma gis sag xér ci Hadiis, nit ki gën a texe ci samag rammu ëllëg bis-penc, mooy ki wax, Laa ilaaha illal Laahu, te mu sell lool ci xolam, walla ci bakkanam».

[Sahih/Authentic.] [Al-Bukhari]

الشرح

Yónent ebi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne nit ki gën a texe cig rammoom ëllëg bis-penc mooy ki wax «Laa ilaaha illal Laahu te mu sell ci xolam» maanaam amul ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, te mu mucc ci bokkaale ak ngistal.

فوائد الحديث

Saxal rammug Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ëllëg bis bu mujj ba, ak ne ag ramam du ñeel ñenn ñu dul way-kennal Yàlla yi.

Rammoom mooy ñaan Yàlla mu kawe mi ñeel aji-kennal Yàlla yi yayoo woon sawara ñu bañ faa dugg, ak ku fa duggóon mu génn fa.

Ngëneelu baatu tawhiid di kennal Yàlla képp, ak màggaayu jeexitalu baat bi.

Dëggal kàddug Tawhiid mi ngi ame ci xam li miy tekki, ak jëfe ya muy waral.

Ngëneelu Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, ak ug xéram ci xam-xam.