bis bi gën ci bis yi mooy bisu àjjuma

bis bi gën ci bis yi mooy bisu àjjuma

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: « bis bi gën ci bis yi mooy bisu àjjuma, ci lañu bind Aadama, ci lañu ko duggal àjjana, ci lañu ko ca génne, te Saa du taxaw ci lu dul bisu àjjuma ».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bis bi gën ci bis yi mooy bisub àjjuma, Te bokk na ci ay jagleem: ci la Yàlla bind Aadama -yal na jàmm nekk ci moom- te ci la ko duggale àjjana, te ci la ko ca génnee wàcce ko ci kaw suuf, te Saa du taxaw ci li dul bisub àjjuma.

فوائد الحديث

Ngëneelu bisub àjjuma ci kaw yeneen bis yépp.

Ñaaxe ak baril ay jëf yu baax ci bisu àjjuma, ak waajal ngir am yërmàndey Yàlla, ak jañ mbugalam.

Yii ñu tudd ci hadiis bi jagleel ko bisub

àjjuma, wax nañu ne: nekkul ngir tudd ngëneelu bisub àjjuma; ndaxte génne Aadama ak ñëwug bis-pénc loolu deesu ko jàppe ngëneel, wax nañu itam: yépp ay ngëneel la, génnug Aadama sabab la ci am ay séti Yonnent ak ña ñu soloo ak ñu sell ñi, ñëwug bis-pénc sabab la ci ñu fay ñu baax ñi ak ñu jot la leen Yàlla waajalal ci ay teraanga.

Tuddal nañu bisu àjjuma yeneen ngëneel yu dul yii ñi tudd ci nettali gii, bokk na ca: ci lañu jéggal Aadama, ci lañu ko faat, am na ci it aw waxtu wow jaam buy aji-gëm du dëppoo ak moom di ñaan Yàlla dara lu dul ne dana ko ko jox.

Bis bi gën ci at mi mooy bisub Arafa, wax nañu it: bisub Tabaski, bis bi gën ci ayu bis yi mooy bisu àjjuma, guddi gi gën mooy guddig Laylatul Xadri.

التصنيفات

Yónnent yi jiitu yalna jàmm nekk ci ñoom