إعدادات العرض
ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka
ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Ummu Salamata dafa xibaar Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- benn jàngu bu mu gis ca Abasa, (jàngu : jaamukaayu katolig yi) ñu koy woowe Maariya, mu wax ko la mu fa gis ci ay nataal, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka, daaldi cay def nataal yooyu, ñooñu ñoo yées ci nit ñi fa Yàlla".
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili မြန်မာ ไทย 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá සිංහල தமிழ் دری Кыргызча or Kinyarwanda नेपाली Malagasy Română Lietuvių Oromoo Nederlands Soomaali Српски Deutsch Українська ಕನ್ನಡالشرح
Ndayu jullit ñi Ummu Salamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa nettali Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne moom ba mu nekkee ca suufus Abasa dafa gis ab jàngu ñu koy woowe Maariya- ay nataal ak i rafetal ak i rëd-rëd ñoo fa nekk; mu yéemu ci loolu ! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral li waral ñu def fa foto yooyu; Mu wax ne : ñii ngay wax bu amaan ku baax ku faatu ci ñoom dañuy tabax jàkka ci kaw bàmmeelam di fa julli, daa di fay def nataal yooyu, Mu leeral ne ñiy def loolu ñoo yées ci mbindeef yi fa Yàlla, ndax seen i jëf da lay yóbbe ci bokkaale Yàlla mu kawe mi.فوائد الحديث
Tabax jàkka ci bàmmeel yi dafa araam, walla di fa julli, mbaa suul néew ci jàkka yi; ngir sakk yoon yiy jëme ci bokkaale.
Tabax jàkka ci bàmmeel yi, ak samp fa ay nataal, daa bokk ci jëfi Yahuut yi ak Nasaraan yi, te ku ko def, mi ngi leen di niru-nirulu.
Araamalees na nataal lu am ruu.
Ku tabax jàkka cib bàmmeel def fa ay nataal, kon moom ci ñi yées ci mbindeefi Yàlla yi la bokk.
Sariiha dafa aar Tawhiid aar gu mat sëkk, ci fatt wépp yoon wuy jëme ci bokkaale.
Tere nañu ëppal ci ñu baax ñi; ndaxte sabab la ci tàbbi ci bokkaale.