إعدادات العرض
Lislaam mooy: nga seede ne amul kenn ku deesi jaamu ku dul Yàlla, seede ne Muhammat ndawul Yàlla la, tey taxawal julli, di woor weeru koor, te aj Màkka benn yoon boo ko manee
Lislaam mooy: nga seede ne amul kenn ku deesi jaamu ku dul Yàlla, seede ne Muhammat ndawul Yàlla la, tey taxawal julli, di woor weeru koor, te aj Màkka benn yoon boo ko manee
Jële nañu ci Umar ibn Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn bis danoo toog ci yònente bi, fa saasa benn waay ñëw, bu sol yéere ya weex tàll,kawar ga ñuul kukk,te kenn gisul ci moom jeexiit i tukki, te it kenn xamu ko ci nun, bam aksi toog ci yònente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-, daa di wéer ñaari wóomam ci ñaari wóomi yónente bi, teg ñaari tenqam ci kaw poojam,daal di ne ko: yaw Muhammat xibaar ma luy lislaam Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «Lislaam mooy: nga seede ne amul kenn ku deesi jaamu ku dul Yàlla, seede ne Muhammat ndawul Yàlla la, tey taxawal julli, di woor weeru koor, te aj Màkka benn yoon boo ko manee» mu ne ko: wax nga dëgg nu yéemu ci moom di ko laaj ba noppi di ko dëggal, mu ne ko: xibaar ma lan mooy gëm? mu ne ko: «mooy nga gëm Yàlla,ak i malaakaam,ak i téeréem, ak i yónentam, ak bis bu mujj ba, nga gëm ndogal yi; ya ca neex ak ya naqari» mu ne ko: wax nga dëgg daal ni ko: xibaar ma lan mooy rafetal? mu ni ko: «mooy ngay jaamu Yàlla mel ni yaa ngi koy gis, ndax boo ko gisul moom moo ngi lay gis» mu ne ko: xibaar ma kañ la bis-pénc? mu ne ko: «ki ñu koy laaj gënu koo xam ki ko koy laaj» mu ne ko: wax ma ay màndarngaam? mu ne ko: «mooy jaam ba jur ab sangam, nga gis way-fàndaañu ya way-rafle ya way-ñàkk ña sàmukati jur ya, ñuy guddalaante ca tabax ya» mu dem ma daal di sax ci ag jaaxle, mu ne ma: « Umar ndax xam nga aji-laaj ji ?» ma ne ko: Yàlla ak ub yónenteem ñoo xam mu ne ma: «koo ku Jibriil la, dafa ñëwóon ngir xamal leen seen diine».
الترجمة
العربية Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Türkçe اردو 中文 हिन्दी বাংলা Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் සිංහල မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە ไทย دری Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių or Română Kinyarwanda Српски тоҷикӣ O‘zbek Moore नेपाली Malagasy Oromoo Soomaali Български Українська Azərbaycan Tagalog bm ქართული lnالشرح
Umar ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day nettali ne Jibriil dafa ñëw ca Sahaaba ya -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ci melow genn góor gu ñu xamul, bokk na ci ay meloom ay yéreem dafa weex tàll, kawaram ga ñuul kukk, te kenn du gis ci moom jeexitalu ku tukki niki coono, ak yére yu tilim, te ña fa teew kenn xamu ko ci, fekk ñoo ngi toog ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu took ci kanamu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-toogiinu kuy jàng, daal di koy laaj Lislaam, mu tontu ko ponk yii di làmboo ñaari baati seede yi, ak sàmmoonteek julliy juróom, ak joxe asaka ñeel ña ko yayoo, ak woor weeru koor, ak joxe faratay aj ci képp ku ko man. Aji-laaj ji ne ko: wax nga dëgg, Sahaaba yi daaldi yéemu ci laajam bii di tegtale ne moom xamul limiy laaj ba noppi di ko dëggal. Mu laaj ko luy Imaan, mu tontu ko ponk yii di juróom-benn làmboo gëm amug Yàlla mu kawe mi ak i meloom, ak kennal ko ci ay jëfam niki bind, ak kennal ko ci jaamu gi, ak gëm Malaaka yi nga xam ne Yàlla da leen a bind ci leer, ci ne ay jaam yu tedd lañu, duñu moy Yàlla mu kawe mi te ay ndigalam la ñuy def, ak gëm téere yi ñu wàcce ci Yónente yi mu bawoo ca Yàlla mu kawe mi, niki Alxuraan ak Tawraat ak Injiil ak yeneen yu dul yooyu, ak gëm Yónente yiy jottali diine ja juge fa Yàlla, bokk na sa ñoom Nuuh ak Ibraahiima ak Muusaa ak Iisaa ka ca mujj di Muhammat -yal na leen Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak yeeneen Yónente yu dul ñoom, ak gëm bis bu mujj ba, dana dugg ca loola liy xew ginnaaw dee, dale ko ca bàmmeel ba ak dundug Barsaq, ak ne nit ki dees na ko dekkil ginnaaaw ba mu deehee daal di koy regle, benn mujjantalam nekk àjjana walla sawara, ak gëm ne Yàlla dogal na bir yi ca na mu jiitoo ca xam-xamam ba, te ak xereñam waral ko, ba noppi mu bind ko, ak it coobareem ca loola, te day tàbbi ca kem na mu ko nattale, te amale ko noona. Mu laaj ko lan mooy Ihsaan (rafetal), mu xibaar ko ne rafetal mooy nga jaamu Yàlla ba mel ni yaa ngi koy gis, ndax boo ko gisul moom moo ngi lay gis, bu manula àgg ci daraja jii, mu jaamu Yàlla gëm ne Yàlla moo ngi koy gis, bu njëkk bi darajay gis la te moo gën a kawe, bu ñaareel bi darajay fuglu la. Ginnaaw ba mu laaj ko kañ la bis-pénc ? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral ne xam-xam ub bis-pénc dafa bokk ci li Yàlla jagoo, benn mbindéef xamu ko, moo xam ki ñu koy laaj, mbaa kiy laaj. Mu laaj ko màndargay bis-pénc ? Mu leeral ne bokk na ci ay màndargaam jëbéer yi ak seen i doom nekk ñu bari lool, (jëbeer : jaamu bu jugéen) walla doom yu bari di dog seen i way-jur di jëflante ak ñoom ni ñuy jëflantee ak i jëbéer, ak ne sàmmkati jur yi ak way-ñàkk ñi da ñuy woomle ci àdduna ci mujjug jamono, di puukarante wu ci ay taax ak i tabax yu taaru. Yónente Yàlla bi daal di xamle ne ki doon laaj Jibriil la dafa ñëwoon ngir jàngal Sahaaba yi seen diine ju jub jii.فوائد الحديث
Rafetug jikkoy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ci ne danaan toog ak Àndandoom yi ñoom it ñuy toog ak moom.
Yoonalug ñeewante ci aji-laaj ji ak jegeel ko, ngir mu man a laaj ci lu dul rus walla ragal.
Am teggin ci kiy jàngale niki ni ko Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm- defe, ndax dafa toog ci kanamu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- toogiinu ku yaru ngir jël ci moom xam-xam.
Ponki Lislaam juróom la, waaye ponki ngëm juróom-benn la.
Bu Lislaam ak Imaan daje dañuy firee Lislaam mbir yu feeñ yi, firee imaan bir yu nëbbu yi.
Leeral ne diine ay daraja yu wuute la, daraja ji ci njëkk mooy: jébbalul Yàlla (Lislaam), bu ñaareel bi: gëm (Imaan), ñatteel bi: rafetal (Ihsaan), te moo ci gën a kawe.
Cosaan ci aji-laaj ji mooy mu ñàkk a xam, kon réer mooy waral laaj, looloo tax Sahaba yi yéemu ci laajam yi ànd ak di ko dëggal.
Tàmbalee ca la gën a am njariñ teg ca ba ca tege; ndax dafa tàmblee ci yaari baati seede yi ci bi muy leeral Lislaam, mu tàmbalee ci gëm Yàlla bi muy firi ngëm.
Aji-laaj ji dana laaj boroom xam-xam yi lu mu réerewul, ngir xamal ñeneen.
Xam-xamub bis-pénc ci li Yàlla jagoo la bokk.
التصنيفات
Pas-pasu Lislaam