yaw ngóor si di naa la xamal ay waat: wattul Yàlla ci jëfe ay ndigëlam bayyi ay tereem kon di na la sàmm, Nanga bàyyi xel Yàlla kon mu féete la fépp, booy ñaan ñaanal Yàlla, booy sàkku ndimbël na nga dimbandikoo Yàlla

yaw ngóor si di naa la xamal ay waat: wattul Yàlla ci jëfe ay ndigëlam bayyi ay tereem kon di na la sàmm, Nanga bàyyi xel Yàlla kon mu féete la fépp, booy ñaan ñaanal Yàlla, booy sàkku ndimbël na nga dimbandikoo Yàlla

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn bis nekkoon naa ci ginnaaw Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ma: «yaw ngóor si di naa la xamal ay waat: wattul Yàlla ci jëfe ay ndigëlam bayyi ay tereem kon di na la sàmm, Nanga bàyyi xel Yàlla kon mu féete la fépp, booy ñaan ñaanal Yàlla, booy sàkku ndimbël na nga dimbandikoo Yàlla, te nga xam ni bu ñépp dajewoon ngir jariñ la ci dara duñu ko man lu dul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi, bu ñépp dajewoon it ngir lor la ci dara duñu ko man ludul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi, ndax teggi nañu xalima ya te kayit ya woow na».

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko]

الشرح

Ibn Abbaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day nettali ne ab xale la woon mu bokkoon ak Yónente war ci jenn daaba, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dinaa la xamal ay bir yoy Yàlla dina la ci jariñ: Nanga wattu Yàlla ci sàmm ay ndigalam te moytu ay tereem, ba da lay fekkk ci di ko topp ak di ko jegeñ-jegeñlu te du la fekk ca moy ya ak bàkkaar ya, boo defee loolu sag fay mooy moom Yàlla mu sàmmu la ci ñaawtéefi àdduna ak allaaxira, daal di lay dimbali ci say yitte foo man di jublu. Boo bëggee ñaan dara, bul ko ñaan ku dul Yàlla ndax Moom rekk mooy wuyu aji-woote ji. Boo bëggee sàkku ndimbal bul ko sàkku ci ku dul Yàlla. Na nga am kóolute ci ne doo am benn njariñ doonte waa suuf ñépp dañoo dajaloo ngir jariñ la, lu dul loo xam ne Yàlla bindaloon na la ko, lor it du dal sa kaw doonte waa suuf ñépp dañoo dajaloo ngir lor la, lu dul lu Yàlla dogaloon ci sa kaw. Te lii Yàlla bind na ko nattale ko ak xereñam ak xam-xamam ba, te dara manul soppi la Yàlla bind.

فوائد الحديث

Amna solo lool ñu jàngal xale yi ak ndaw ñi biri diine niki wéetal Yàlla ak ay teggin ak yeneen.

Am pay day toll kem na jëf ja toll.

Digele ci sukkandiku ci Yàlla, ak wakkirlu ci Moom wolif lu dul Moom, ndax mooy gën gi wéeruwaay.

Gëm ndogal yi te gërëmloo ko, ak gëm ne Yàlla dogal na lépp.

Ku sànk ndigali Yàlla yi, Yàlla dana ko sànk.

التصنيفات

Tolluwaayi dogal yi