إعدادات العرض
ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yabaloon? Bul bàyyi benn xërëm te tojoo ko, mbaa benn bàmmeel bu ñuy màggal te maasale woo ko
ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yabaloon? Bul bàyyi benn xërëm te tojoo ko, mbaa benn bàmmeel bu ñuy màggal te maasale woo ko
Jële na ñu ci Abul Hiyyaaj Al-Asadi mu wax ne: Aliyun Ibn Abii Taalib da ne ma: ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yabaloon? Bul bàyyi benn xërëm te tojoo ko, mbaa benn bàmmeel bu ñuy màggal te maasale woo ko.
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский اردو 中文 हिन्दी বাংলা Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் සිංහල မြန်မာ ไทย Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە Türkçe دری Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy Română Kinyarwanda नेपाली Српски Soomaali Moore Українська Български Tagalog Azərbaycan ქართული тоҷикӣ bm Oromoo Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na yónni Sahaaba yi ci ñu bañ a bayyi benn «xërëm» -te mooy nataalu lu am ruu moo xam dafa am jëmm walla amul jëmm- lu dul ne dindi nañu ko mbaa ñu far ko. Ak ñu bañ a bàyyi bàmmeel bu ñu yëkkati lu dul ne maasale nañu ko ak suuf si, màbb la ñu ca tabax, mbaa ñu jégénal ko mu bañ a sute suuf si lu bari, waaye dañu koy yëkkati luy tollook Sibr rekk.فوائد الحديث
Araamug nataal lu am ag ruu; ndax daa bokk ci jumtukaayi bokkaale yi.
Yoonalees na dindi lu bon ci loxo ci ku am nguur, mbaa mu man loolu.
Xérug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dindi lépp luy wane jeexitalu ceddo, ci ay nataal ak i xërëm ak tabax ci bàmmeel yi.
التصنيفات
Wéetal Yàlla ci jaamu ko