ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem

ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla mu kawe mi nee na: ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla mu baarkeel mi te kawe dafa wax ne: moom moo gën a doylu képp kuy bokk, mooy ki doylu ci lépp, bu nit defee ag jaamu defal ko Yàlla ak ku dul Yàlla; Yàlla da koy bàyyi te du ko ko nangul, daal di koy delloo boroom; Kon warees naa sellal jëf yi ngir Yàlla mu kawe mi, ndax Moom -tudd naa sellam ga- du nangu lu dul lu sell ngir jëmmam ju tedd ji.

فوائد الحديث

Moytandikuloo bokkaale ci bépp melokaanam; ndaxte moom day teree jëf mu ndangu.

Yëg doylug Yàlla ak ug màggaayam dafa bokk ci liy dimbali nit ki ci mu man a sellal jëf.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko, Jëfi xol yi