إعدادات العرض
giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom kenn du ma dégg ci xeet wii moo xam Yahuut la walla Nasaraan, ba faatu te gëmul li ñu ma yónni lu dul ne dana bokk ci waa sawara
giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom kenn du ma dégg ci xeet wii moo xam Yahuut la walla Nasaraan, ba faatu te gëmul li ñu ma yónni lu dul ne dana bokk ci waa sawara
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom kenn du ma dégg ci xeet wii moo xam Yahuut la walla Nasaraan, ba faatu te gëmul li ñu ma yónni lu dul ne dana bokk ci waa sawara».
الترجمة
العربية Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Türkçe اردو 中文 हिन्दी বাংলা Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் සිංහල မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá ئۇيغۇرچە ไทย دری Кыргызча or Kinyarwanda नेपाली Română Lietuvių Malagasy ಕನ್ನಡ Oromoo Nederlands Soomaali Српски Українська Moore ქართული Azərbaycan Magyar Tagalogالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa giñ ci Yàlla ne amul kenn ku koy dégg ci xeet wii, moo xam muy yahuut walla nasaraan mbaa leneen, te wooteb Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- egg ci moom mu faatu te gëmu ko lu dul ne dana bokk ci waa sawara sax fa ba fàww.فوائد الحديث
Wooteb Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa matale ñépp, te dañu koo war a topp, te dafa folli ci sariihaam ji mbooleem sariiha yi.
Ku weddi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- njort bi mu njort ne gëm na yeneen yonnente yi du ko jariñ dara.
Ku déggul Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te wooteeb Lislaam bi àggul ci moom kooku dees na ko dogal ngànt, ay mbiram nag ëllëg bis-pénc ci Yàlla lay dellu.
Manees naa jariñu ci lislaam doonte tuuti la jiitoo dee gi, donte ci tawat ju tar la, fii ak ruu gi eggul ci bóli gi.
Nangu diiney yéefar yi -te yahuut yi ak nasaraan yi ci la ñu bokk- loolu ag kéefar la.
Tudd gi ñu tudd yahuut yi ak nasaraan yi -ci hadiis bi - loolu ngir yee ñeneen ñi la; ndaxte yahuut yi ak nasaraan yi am nañu téere, kon bu dee lii mooy seen mbir, kon ñi amul téere ñoo ca gën a yey, ñoom ñépp a war a dugg ci diine ji te topp Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.