buleen ma jay kem ni Nasaraan yi jaye woon doomu Maryama; man daal ab jaamam laa, kon deeleen wax: jaamub Yàlla ak ndawam

buleen ma jay kem ni Nasaraan yi jaye woon doomu Maryama; man daal ab jaamam laa, kon deeleen wax: jaamub Yàlla ak ndawam

Jële nañu ci Umar Ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «buleen ma jay kem ni Nasaraan yi jaye woon doomu Maryama; man daal ab jaamam laa, kon deeleen wax: jaamub Yàlla ak ndawam».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tere ëppal ak jéggi dayob Sariiha ci tagg ko ak di ko melal ay meloy Yàlla mu kawe mi ak i jëfam ya mu jagoo, walla ne dafa xam kumpa, walla di ko boole ak Yàlla ci ñaan, kem ni ko Nasaraan yi defe ci Iisaa doomu Maryama -yal na ko Yàlla dolli jàmm-. Topp mu leeral ne moom jaam la ci jaami Yàlla yi, mu digle ne nañuy wax ci moom ne: jaamub Yàlla la ak ndawam.

فوائد الحديث

Moytandikuloo jéggi dayob Sariiha ci màggal walla tagg; ndax loolu day jëme ci bokkaale.

Li Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- doon moytandikuloo de tàbbi na ci xeet wi, am kurel yu ëppal ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-, am it kurel yu ëppal ci waa kër Yónente bi, ak kurel yu ëppal ci wàlliyu yi, ñoom ñépp tàbbi ci bokkaale.

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa melal boppam ci ne jaamub Yàlla la; ngir leeral ne moom ab jaam bu Yàlla moom la, daganul ñuy jëmale ci moom dara ci lu Boroom bi jagoo.

Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- dafa melal boppam ci ne ndawu Yàlla la; ngir leeral ne moom Yàllaa ko yónni, kon ñu war koo dëggal te topp ko.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko