yal na Yàlla rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi, ñoom kat dañoo jàppe séen bàmmeeli Yónente yi ay jàkka

yal na Yàlla rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi, ñoom kat dañoo jàppe séen bàmmeeli Yónente yi ay jàkka

Jële na ñu ci Aysatu ak Abdullahi en Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ñu wax ne: Bi faatu dikkalee Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa jël ab yéreem tek ko ci kanamam, bu jaaxlee ci moom daal di koy muri ci kanamam, daal di wax ne: «yal na Yàlla rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi, ñoom kat dañoo jàppe séen bàmmeeli Yónente yi ay jàkka» day artu ci li ñu def.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Aysatu ak Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- dañu nuy xibaar ci ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bi ko faatu dikkalee dafa jël dàggitu sagar teg ca kanamam bu demee ba noyyi jafe ko ndax sukuraatus ndee si mu dindi sagar wi ci kanamam di wax ci jamono ju tar jooju: Yàlla rëbb na Yahuut yi ak Nasaraan yi, génne leen ci yërmàndeem; ndaxte dañoo tabax bàmmeeli séen Yónente yi ay jàkka, te bu dul woon ni loolu nekke musiba kon du ko wax ci jamono jooju, looloo tax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere xeetam wi ñuy niru-niruulu Yahuut yi ak Nasaraan yi, ndax loolu yoon la wuy yóbboo ci bokkaale Yàlla mu màgg mi.

فوائد الحديث

Tere nañu def bàmmeeli Yónente yi ak gaa yu baax yi jàkka ju ñuu jullee ngir Yàlla, ndax loolu day yóbbe ci bokkaale.

Tarug yittewoog Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lii di Tawhiid ak ragalam ci lii di màggal ay bàmmeel; ndax loolu day waral bokkaale.

Dagan na ñu rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi ak ku def lu mel ni li ñu def ci tabax ci bàmmeel yi ak jàppe ko ay jàkka.

Tabax bàmmeel daa bokk ci aaday Yahuut yi ak Nasaraan yi, te ñëw na ci hadiis ñu tere di leen niru-nirulu.

Bokk na ci jàppe bàmmeel yi jàkka di fa julli ak di fa jublu, donte tabaxu ñu ko jàkka.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko