deeleen jegeele, tey jubal, te ngeen xam ne kenn ci yéen du mucc ngir ay jëfam" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ba ci yaw sax? Mu ne: "ba ci man kay, lu dul Yàlla muure ma ag yërmàndeem ak ngëneelam

deeleen jegeele, tey jubal, te ngeen xam ne kenn ci yéen du mucc ngir ay jëfam" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ba ci yaw sax? Mu ne: "ba ci man kay, lu dul Yàlla muure ma ag yërmàndeem ak ngëneelam

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "deeleen jegeele, tey jubal, te ngeen xam ne kenn ci yéen du mucc ngir ay jëfam" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ba ci yaw sax? Mu ne: "ba ci man kay, lu dul Yàlla muure ma ag yërmàndeem ak ngëneelam".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day ñaax sahaaba yi ci ñu jëf, te ragal Yàlla seen kem-kàttan, ci lu dul ëppal du caagine gàtteñlu, ak ñu jublu ca seen jëf ji ag njub ak ug sellal ñeel Yàlla ak topp sunna ngir ñu nangu seen jëf ba mu nekk sabab ci yërmànde wàcc ci ñoom. Mu xamle ne kenn ci yéen du mucce ci jëfam dong, waaye yërmàndey Yàlla manu ci a ñàkk. Ñi ne ko: ba ci yaw Yonnente Yàlla bi sa jëf du la musal, ak li muy màgg yépp? Mu ne: ba ci man, lu dul Yàlla muure ma ag ngëneelam ak yërmàndeem.

فوائد الحديث

An-Nawawii nee na: (juballeen, jegeeleleen): sàkkuleen ag jubal, te jëfe ko, bu ngeen ca lottee, nangeen di jegeele; maanaam: nangeen ko jege, jub: tege ci yoon, te mooy diggante ëppal ak gàtteñlu, deesul ëppal du caagine gàtteñlu.

Ibn Baas nee na: jëf yu baax yi ay sabab la ci dugg àjjana, niki ni jëf yu bon yi nekke sabab ci dugg sawara, te hadiis bi day leeral ne seen ug dugg àjjana nekkul rekk ci jëf, waaye manul ñàkk njéggalu Yàlla ak yërmàndeem moom Aji-Sell ji Aji-Kawe ji, ñoom dañu fay dugg ci sababus seen i jëf, waaye li waral loolu mooy yërmàndey Aji-Sell ji, ak njéggalam.

Jaam bi du woru du yéem jëfam ak nu mu man a toll; ndaxte àqi Yàlla moo gën a màgg jëfam, kon jaam manut a ñàkk a boole ragal ak yaakaar.

Ngëneelu Yàlla ak yërmàndeem ci jaamam yi moo gën a yaatu seen i jëf.

Jëf yu baax yi sabab la ci dugg àjjana, waaye ci ngëneeli Yàlla lay ame ak yërmàndeem.

Al-Kirmaanii nee na: "bu dee nit ñépp duñu dugg àjjana lu dul ci yërmàndey Yàlla, kon litax ñu tudd Yonnente bi Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mooy ne bu dee moom day dugg àjjana ci lu amul sikk, te moom dufa dugg ci lu dul yërmàndey Yàlla; kon keneen ku dul moom jarul wax.

An-Nawawii nee na: li Yàlla wax ne: {duggleen àjjana ca la ngeen doon jëf} [An-Nahl: 32], {àjjana jooju mooy gi ñu leen donn loo ca la ngeen doon jëf} [As-Suxrufi: 72], ak aaya yi ko niru tegtal la ci ne jëf yi dees na ci dugge àjjana na, safaanoowul ak hadiis yii, waaye maanaay aaya yi mooy ne dugg àjjana ci sababus jëf yi la, ag tawfeexal ci jëf yi, ak ug sellal ko ak nangu ko ci yërmàndey Yàlla ak ngëneelam lay ame, moo tax duggu ca ngir jëfam rekk, te loolu la ñu namm ci hadiis yi, dana wér it ñu ne da cay dugg ci jëfam; manaam: ci sababam, te ci yërmàndeem la jóge.

Ibnul Jawsii nee na: loolu am na ñenti tontu; bi ci njëkk: tawfeexal ci jëf yi ci yërmàndey Yàlla lay ame, bu dul woon yërmàndey Yàlla lu jiitu kon gëm gi du am ba topp Yàlla gi nga xam ne mooy taxa mucc di am, ñaareel bi: njariñi jaam bi sangam la ñeel, ay jëfam kilifaam la ñeel, kon lépp lu mu ko xéewalal cig fay ci ngëneelam la, ñatteel bi: ñëw na ci yenn hadiis yi ne jëmmi dugg àjjana ci yërmàndey Yàlla lay ame, séddale daraja ya nag ci jëf yi lay ame, ñenteel bi: topp Yàlla gi ci jamono ju gàtt la woon, te yool yi du jeex, def xéewal gu dul jeex muy fayug luy jeex loolu ngëneel la waaye tolloowul ak jëf yi.

Ar-Raafihii nee na: jaaduwul ci aji-jëf ji muy sukkandiku ci jëfam ngir sàkko a texe ak am ay daraja; ndaxte ci tawfeexu Yàlla rekk la jëfam ji ame, niki noonu bàyyi gi mu bàyyi moy Yàlla, te loolu lépp ci ngëneelu Yàlla ak yërmàndeem la ame.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci ay turam ak i meloom