amul kenn kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la te mu dëggu ci xolam lu dul ne Yàlla dana ko araamal ca sawara

amul kenn kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la te mu dëggu ci xolam lu dul ne Yàlla dana ko araamal ca sawara

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Muhaas dafa toggoo woon ak moom ci benn waruwaay mune ko: «yaw Muhaas Ibn Jabal», mu ne ko: wuyu naa la yaw Yónente Yàlla bi, mu ne ko: «yaw Muhaas» mu ne ko wuyu naa la yaw Yónéte Yàlla bi, ñatti yoon, mu ne ko: « amul kenn kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la te mu dëggu ci xolam lu dul ne Yàlla dana ko araamal ca sawara», mu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ndax duma ko wax nit ñi ngir ñu bég? Mu ne ko: «kon dañuy bàyyandiku». Muhaas waxe ko jamano yi muy faatu ngir bañ a bàkkaaru.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Muhaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa waroon ci benn daaba mook Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu woo ko ne ko: yaw Muhaas? Bàmtu woote ba ñatti yoon; ngir feddali solos li mu koy wax. Yooyu yépp Muhaas di ko tontu naan ko: "wuyu naa la yaw Yónente Yàlla bi, di la wuyu waat di sàkkoo texe ci wuyu gi. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaar ko ne amul kenn kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, maanaam: amul lenn lu ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, te mu dëggu ci xolam ci lu dul wenn fen, bu faatoo ci anam gii Yàlla araamal ko ci sawara. Muhaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax mu wax ko nit ñi ngir ñu bég ci yiw wii? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ragal ñu sukkandiku ci loolu, séen jëf di néew. Muhaas waxu ko kenn lu dul bi muy waaj a faatu; ngir ragal a tàbbi ci bàkkaaru nëbb xam-xam.

فوائد الحديث

Toroxlug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bay togg Muhaas ci ginnaaw daaba.

Jàngaliinu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ba tax muy baamtu woo gi muy woo Muhaas ngir mu gëna teewlu li mu koy wax.

Bokk na ci sàrti seede ne: amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ki koy wax dafa wara nekk ku dëggu ci limiy Wax am kóolute te baña nekk weddi mbaa kuy sikk-sakka.

Ñiy kennal Yàlla duñu sax sawaraw Jahannama, bu ñu fa duggee it ci sababus séen i bàkkaar; dees na leen fa génne ginnaaw ba ñu laabee.

Ngëneelu ñaari baati seede yi ñeel ku ko wax te dëggal.

Dagan na ñu bañ a waxtaane ab hadiis ci yenn jamono yi bu dee yàqute man na caa tege.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci moom gi mu moom lépp di ko saytu, Ngëneeli wéetal Yàlla