Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, wax ak moom ci yenn mbir yi, daal di ne ko: bu soobe Yàlla soob la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "ndax dangamay yamale ak Yàlla? Waxal: bu soobe Yàlla moom dong

Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, wax ak moom ci yenn mbir yi, daal di ne ko: bu soobe Yàlla soob la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "ndax dangamay yamale ak Yàlla? Waxal: bu soobe Yàlla moom dong

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu ne: Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, wax ak moom ci yenn mbir yi, daal di ne ko: bu soobe Yàlla soob la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "ndax dangamay yamale ak Yàlla? Waxal: bu soobe Yàlla moom dong".

[Ag càllalaam tane na] [Ibnu Maaja soloo na ko, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ahmat]

الشرح

Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ak moom ci mbiram, topp mu ne ko: "bu soobe Yàlla soob la", Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di weddi wax ji, xamal ko ne toftal coobarey mbiddeef ci coobarey Yàlla toftal gu sës rikk, bokkaale gu ndaw la, du dagan jullit bi wax ko, Mu daadi koy jubbanti ci wax ju jub, mooy: "bu soobe Yàlla moom dong", mu wéetal Yàlla ci coobareem, te bañ caa toftal coobarey kenn, xeetu toftal gu mu man a doon.

فوائد الحديث

Tere nañu ñuy wax: bu soobe Yàlla soob la, ak lu ko niru ci toftal coobarey jaam bi ci coobarey Yàlla toftal gu sës rikk ndax bokkaale gu ndaw la.

Dañoo war a weddi lu bon.

Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa aar kaaraangeg Tawhiid, fatt yooni bokkaale yi.

Bu ñuy weddi lu bon dana rafet ñu wan ki ñuy woo lu dagan li koy wuutu, ngir roye ko Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

Boole li Yonnente bi wax ci hadiis bi: "bu soobe Yàlla dong", ak li mu wax ci beneen hadiis: "waxal: bu soobe Yàlla topp mu soob la" lu dagan la, waaye li mu wax: "bu soobe Yàlla dong" moo gën.

Dagan na ñu wax: "bu soobe Yàlla topp mu soob la" waaye li gën mooy ñu wax: "bu soobe Yàlla dong".

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko