yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka

yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ci feebaram ba nga xam ne jugu ci: "yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka" nee na: bu dul woon loolu kon dinaa fésal bàmmeelam, waaye moom dafa tagal ñu jàppe ko jàkka.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ci feebaram bi nga xam ne dafa tar ci moom, te mu faatu ci: Yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, dàq leen ci yërmàndeem; li waral loolu mooy ne ñoom dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka, ci di tabax ca kawam walla di fa julli walla di julli jëm ca. Topp Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm wax ne: bu dul woon tere googu ak àrtu googu bawoo ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak ragalug Sahaaba yi ci ñu def ci bàmmeelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc kem li Yahuud yi ak Nasaraan yi def ci bàmmeeli seen Yonnente yi kon dinaa fésal bàmmeelam ba mu feeñ.

فوائد الحديث

Lii dafa bokk ci dénkaaneem yi mujj muy tegtale soloom ak sonneem ci loolu.

Tere gu feddaliku, ak araam gu tar ci jàppe bàmmeel yi ay jàkka, ak junlu faa julli ci lu dul julleeg néew; ndax loolu day jëme ci màggal aji-dee ji ak wër bàmmeelam ak raay ay peggam ak woo tutam, te loolu lépp dafa bokk ci bokkaale ak i jumtukaayam.

Tarug yittewoog Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak sonnam ci Tawhiid ak ragalam ci jaamu bàmmeel yi; ak it ne loolu day jëme ci bokkaale.

Yàlla mu kawe mi ñoŋal na Yonnenteem bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ñuy def ag bokkaale ca bàmmeelam ba, mu déey sahaabaam yi ginnaawam ci ñu ñoŋal bàmmeelam bi ci di ko fésal.

Jëfeg Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ci ndénkaaney Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak seenug xér ci Tawhiid.

Tere nañu niru-nirulu Yahuud yi ak Nasaraan yi, ak ne tabax ci kaw bàmmeel yi ci seen yoon la bokk

Bokk na ci jàppe bàmmeel yi ay jàkka mooy julli fa ak jëm ca, doonte tabaxuñu ko jàkka.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko, Seeti ay sëg