ku takk ab téere bokkaale na

ku takk ab téere bokkaale na

Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir Al-Juhanii-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-am mbooloo dañoo ñëw ci moom,mu jaayante ak juróom-ñent ñi bàyyi kenn ki,nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, jaayante nga ak juróom-ñent daal di bàyyi kii? Mu ne:"ab téere la takk",mu dugal loxoom dagg ko,daal di jaayante ak moom,daal di wax ne: "ku takk ab téere bokkaale na".

[Tane na] [Ahmat soloo na ko]

الشرح

Am mbooloo dañoo ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, seenub lim nekkoon fukk,mu jaayante ak juróom-ñent ci ñoom ci Lislaam ak topp, te jaayantewul ak fukkeel bi,ba ñu ko laajee lu tax loolu Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: Dafa takk ab boggal, te loolu mooy li ñuy fas walla di ko takk ci ay xor ak leneen ngir jeñ bët walla lor. Waa ji dugal loxoom ca barabu boggal ba daal di koy dagg daal di set ci moom,ci loolu Yonnente bi jaayante ak moom,daal di wax di moytondikuloo ay boggal di leeral ab àtteem: "ku takk boggal bokkaale na".

فوائد الحديث

Ku sukkandiku ci ku dul Yàlla,boroom bi dina jëflànte ak moom ci lu wuuteek bëgg-bëggam.

Fas ne takk boggal sabab la ci jeñ lor ak bët,loolu bokkaale gu ndaw la,bu dee dafa gëm ne moom day jariñ ci jëmmam kon bokkaale gu mag la.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko