إعدادات العرض
wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc
wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc
Jële nañu ci Abuu Amr -nee nañu it: Abii Amrata--, Sufyaan ibn Abdallah yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc".
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية Español አማርኛ English اردو Indonesia ئۇيغۇرچە বাংলা Français Türkçe Русский Bosanski සිංහල हिन्दी 中文 فارسی Tiếng Việt Tagalog Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ ไทย Deutsch 日本語 پښتو অসমীয়া Shqip Svenska Nederlands ગુજરાતી Кыргызча नेपाली Yorùbá Lietuvių دری Српски Soomaali тоҷикӣ Kinyarwanda Română Magyar Čeština Moore Malagasy Oromoo ಕನ್ನಡ Azərbaycan O‘zbek Українська ქართული Македонски ភាសាខ្មែរ Bambara ਪੰਜਾਬੀ मराठी Kirundi Kurmancî Bahasa Melayu Yaoالشرح
Sahaaba bii di Sufyaan Ibnu Abdullah -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir mu xamal ko wax ju matale maanaay lislaam yi mu jàpp ci te du ko laajaat kenn ku dul moom ? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko : waxal : wéetal naa Yàlla, te gëm naa ne mooy sama Yàlla, moom laay jaamu, moo ma bind, moom laay jaamu ci dëgg deesu ko bokkaale ak dara. Topp mu wommatul Yàlla, topp ko, ci ay farataam, ak bàyyi yi Yàlla araamal, te sax ci loolu.فوائد الحديث
Cosaanu diine mooy gëm Yàlla cig moomeelam, ak cig jaamu, ak ci ay turam ak i meloom.
Solos njub ginnaaw gëm, ak wéy cig jaamu, ak sax ci loolu.
Ngëm Yàlla sàrt la ngir ñu nangu jëf yi.
Gëm Yàlla, day làmboo lépp luñu war a fas ci ay pas-pasi ngëm ak i cosaanam, ak la cay topp ci ay jëfi xol, ak wommatu ak nangul Yàlla ci li nëbbu ak li feeñ.
Jub mooy taqoo ak yoon wa, ci def yi war ak bàyyi yi ñu tere.
