maa ngi sant Yàlla mi delloo pexeem ya ci ay jax-jaxal

maa ngi sant Yàlla mi delloo pexeem ya ci ay jax-jaxal

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, kenn ci nun de dana yég ci boppam dara Lu koy gaar loo xam ne mu nekk dóom moo koy gënal mu wax ko, mu ne ko: «Yàlla rekk a màgg, Yàlla rekk a màgg, maa ngi sant Yàlla mi delloo pexeem ya ci ay jax-jaxal».

الشرح

Leerarug hdiis bi : Benn waay daa ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, kenn ci nun de dana yég ci boppam mbir mu koy gaar waaye wax ko moom lu rëy la lool, ba tax na mu nekk dóom sax moo koy gënal mu di ko wax, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di kàbbar ñaari yoon sant Yàlla mi delloo pexey Saytaane mu yam rekk ci jax-jaxal.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi :

Leeral ne Saytaane day tëru way-gëm ñi ci di leen jax-jaxal; ngir jële leen ci ngëm yóbb leen ci kéefar.

Leeral néew kàttanug Saytaane ci kanamu way-gëm ñi ba tax manul lu dul jax-jaxal.

Aji-gëm ji daa war a dummóoyu jax-jaxali Saytaane yi te di ko jeñ.

Yoonalees na kàbbar ci mbir moo rafetlu mbaa nga yéemu ca, walla bir yu ko niru.

Yoonal nañu jullit laaj boroom xam-xam bi lépp lu lënt ci moom.

التصنيفات

Gëm Yàlla Mu tedd Mu màgg mi, Jinne yi