malaaka yi duñu dugg kër gu am xaj walla nataal

malaaka yi duñu dugg kër gu am xaj walla nataal

Jële nañu ci Abuu Talhata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «malaaka yi duñu dugg kër gu am xaj walla nataal».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne malaakay yërmànde duñu dugg kër gu am xaj walla nataalu yi am ruuh; Ndaxte naataal lu am ruuh: ag moy la te ñaawteef la, te toppandoo bindubYàlla bi la, te jumtukaay la ci jumtukaayi bokkaale yi, te yenn yi nataalu lu ñuy jaamu la wolif Yàlla, Li tax duñu dugg ci kër gu am xaj: ndaxte dañoo bari lu ñuy lekk sobe, te yenn yi dañu koy tudde Saytaane; te malaaka yi dañoo safaanoo ak saytaane yi, Ak ni xetu xaj bone; te malaaka dafa bañ xet gu bon, ak it ne dañoo tere ku ko yar; nu mbugale ko ci xañ ko malaakay yërmànde bañ a dugg këram, bañ a jokkoo ak moom, ak bañ koo jéggalul, bañ ko a baarkeelal ci këram, ak bañ koo jeñal saytaane.

فوائد الحديث

Araamal nañu yar xaj, bi dul xaju rëbb walla sàmm walla bay.

Nataal dafa bokk ci mbir yu bon yi nga xam ne malaaka yi dañu koy daw, te ag nekkam ci barab sabab la ci ñàkk yërmànde, niki noonu it ab xaj.

Malaaka yi dul dugg ci kër gi am xaj walla nataal mooy malaakay yërmànde, bu dee malaaka yiy sàmme ak yeneen yi am liggéey niki maalaakam dee ñoom danañu dugg ci kër yépp.

Araamal nañu wékk nataalu lu am ruuh ci miir yi ak leneen.

Al-Xattaabii nee na: malaaka yi duñu dugg kër gu am xaj walla nataal ndax li ñu araamal yar ab xaj ak nataal, bu dee lu araamul niki xajub rëbb ak bay ak sàmm ak nataal

Bu nekk si ag laltu ak ñegenaay yi ak yeneen yooyu du tere malaaka yi dugg fa.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko