jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am

jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am

Jële nañu ci Umar ibn Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «jëf yi mi ngi aju ci yéene ja, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ub Yónenteem, koo ku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak Yónenteem, waaye képp ku gàddaay ngir àdduna jum soxlaa jot, walla jigéen ju mu bëgg a takk; kon gàddaayam jëm na ca la ko tax a gàddaay" ci beneen nettali ci Al-Buxaarii: "jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi day leeral ne jëf yépp ci yéene ja la aju, te àtte bii daa matale jëf yépp moo xam jaamu yi la mbaa jëflante yi, koo xam ne jëfam njariñ la ci jublu du ca am lu dul njariñ loola waaye du ci am tiyaaba, ko xam ne jëfam jege Yàlla la ci jublu dana am ca jëfam ja ab yool ak ug pay, donte jëf i aada la, niki lekk ak naan. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- joxe waat meneen misaal ci ni yéene di jeexitale ci jëf yi ànd ak seenug niróo ci melo wi feeñ, mu leeral ne ku jublu ci gàddaay bàyyi réewam ngir jublu ci ngërëmal Boroomam kon gàddaayam ga gàddaayu sariiha la gu ñu nangu te dees na ko fay ab yool ngir yéeneem ju dëggu, waaye ku jublu cig gàddaayam njariñal àdduna, alal, ak daraja ak am njaay, walla soxna du am ca gàddaayam ga lu dul njariñ yooya mu yéene woon, te du am benn cér cig pay mbaa ab yool.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci sellal, ndax Yàlla du nangu jëf lu dul la nga xamne def na ñu ko ngir jëmmam ja.

Jëf yi Nga xamne dees ciy jaar ngir jege Yàlla bu ko muskallaf mi defee ci anamug aada du ca am ab yool, ba keroog mu cay jublu jege Yàlla.

التصنيفات

Jëfi xol yi