إعدادات العرض
Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na
Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na
Jële nañu ci Samurata Ibn Jundub -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na».
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt සිංහල Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili မြန်မာ Русский Deutsch 日本語 پښتو অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە தமிழ் ไทย دری Fulfulde Magyar ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių or Română Kinyarwanda Српски O‘zbek Moore नेपाली Oromoo Soomaali Български Українська Azərbaycan ქართული тоҷикӣ Македонски bm Malagasyالشرح
Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah: te mooy sellal Yàlla ci bépp wàññeeku. Ak alhamdu lil Laah: te mooy melal Yàlla cig mat sékk ànd ak bëgg ko ak màggal ko. Ak laa-i-Laaha illal Laah: maanaam: amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla. Ak al-Laahu akbar: maanaam: Yàllaa gën a tedd te moo gën a màgg lépp lu mu man a doon. Te ngëneelam ak yoolam nekkul rekk ci toftale ko boo koy wax.فوائد الحديث
Bokk na ci njariñal adiis bi:
Yombug Sariiha, ba tax na baat boo ci tàmbalee it du la lor.
التصنيفات
Sikkar yees joyal