li dagan de leer na li araam it leer na,

li dagan de leer na li araam it leer na,

Jële nañu ci Nuhmaan Inb Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne -Nuhmaan jëmale yaari baaraamam ci ay noppam-: «li dagan de leer na li araam it leer na, seen diggante nag am na ay lënt, te ñu bari si nit ñi duñu ko xam, képp ku moytu yu lënt yi ñoŋal na diineem ak deram, waaye ku tàbbi ca lënt ya kooku tàbbi na ca yu araam ya, mi ngi mel ni sàmmkat biy sàmm ci li wër ab ñag, daanaka rekk sàmm na ca biiram, xanaa du buur bu nekk am na ab ñagam, te ñagub Yàlla mooy li mu araamal, xamleen ne yaram am na aw lumb wow bu baaxee yaram wépp baax, bu yàqoo yaram wépp yàqu, loolu mooy xol«.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi day leeral ab tënk bu matale ci mbir yi, wane na ne day séddalikoo ci ñatti xaaj: lu ag daganam leer, ak lu ag araamam leer, ak ay mbir yu lënt te ay àtteem leerul cig dagaan walla cig araam, ba tax nit ñu bari xamuñu ab àtteem. Ku bàyyi mbir yooyu lënt ci moom, diineem mucc na ci sori gi mu sori tàbbi ci lu araam, deram it mucc na ci nit ñi di wax lu koy sikkal ngir li mu def lu lënt lii. Waaye ku moytuwul yu lënt yi kooku gaaral na boppam ci tàbbi ci lu araam, walla ci nit ñi di gàkkal ab deram. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- sadd na aw misaal ngir leeral melokaanu kiy topp lënt yi, ci ne mi ngi mel ni sàmmkat biy sàmm ay juram ci wetu suuf su boroomam ñag, nga xamne xaw tuuti rekk juram gi lekk ca la ñu ñag ndax li mu ko jege, naka noonu it képp kuy def yu lënt yi, kooku jege na yu araam yi te dana ca xaw a tàbbi. Ginnaaw loolu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne am na ci biir yaram ab lumb(te mooy Xol) cig baaxam la yaram wi di baaxe, waaye cig yàqoom la yaram Wi di yàqoo.

فوائد الحديث

Soññee ci bàyyi yu lënt yi nga xam ne àtteem leerul.

التصنيفات

Àtteb yoon, Ngëneeli jëfi xol yi, Sellal bakkan yi