Jépp jëf ju baax sarax la

Jépp jëf ju baax sarax la

Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Jépp jëf ju baax sarax la».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko ca Adiisu Jaabir ba, Muslim it soloo ko ci Adiisu Husayfa]

الشرح

Yónente bi, -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak jàmm, daf nuy xamal ne, bépp rafetal ak njariñ ci nit ñi, moo xam wax la walla jëf, sarax la, te dafay maye ab yool ak tiyaaba.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi :

Mooy Sarax du yam ci li nit ki di génne ci alalam kepp, waaye day làmboo lépp lu baax lu nit ki def walla mu wax ko, te di ko jottali ñeneen ñi.

Dafay xëcc nit ñi ci def lu baax ak def lépp luy amal njariñ ñeneen ñi.

Bañ a xeeb jëf ju baax, donte daa tuuti.

التصنيفات

Ngëneeli jëf yu baax yi