?Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi

?Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi

Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi».

[Hasan/Sound.] [Ibn Maajah]

الشرح

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafay xamle ne li gën ci tudd Yàlla mooy: «Laa ilaaha illal Laahu» maanaam, amul kenn ku ñuy jaamu ci dëgg ku dul Yàlla, li gën ci ñaan yi mooy: Alhamdu lil Laahi; te mooy nangu ne kiy joxe xéewal mooy Yàlla -tudd naa sellam ga-, moom mi yeyoo melokaan yu mat sëkk ya te rafet.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci di baril a tudd Yàlla ci kàdduy Tawhiid, ak di ñaan cig cant.