Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo

Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy ku man a xulóo te bari le ko, mooy ki dul nangoo topp dëgg, te di ko jéem a weddi ci dàggasante, walla muy xulóo ci dëgg waaye day ëppal ca xulóo ba, ba day jéggi dayo, di werente cig ñàkk a xam.

فوائد الحديث

Du bokk ci xeetu dàggasante buñu ŋàññi su dee ki ñu tooñ dafa laaj yelleefam ci yoon.

Werente ak xulóo dafa bokk ci gàkk-gàkki làmmeñ yiy sabab ag tàqalikoo ak bàyyente ci diggante jullit ñi.

Dàggasante dana baax bu teggee cig dëgg te defiin wa rafet, waaye dees na ko wàññi bu dee ngir delloo dëgg la saxal ay neen, walla mu bañ a am ay lay ak ay firnde.

التصنيفات

Ngëneel yi ak teggiin yi, Jikko yees ŋàññ