إعدادات العرض
fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee, deeleen ci baril ay ñaan
fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee, deeleen ci baril ay ñaan
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee, deeleen ci baril ay ñaan».
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் සිංහල မြန်မာ Русский Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە ไทย دری Fulfulde Magyar ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių or Română Kinyarwanda Српски O‘zbek Moore नेपाली Oromoo Soomaali Български Українська Azərbaycan ქართული тоҷикӣ bm Malagasy Македонскиالشرح
Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee; ndaxte kiy julli day teg li gën a kawe te tedd ci yaramam ci kaw suuf ndax woyoflu la ak toroxlul Yàlla mu kawe mi fekk ma nga sujjóot. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digle na baril ñaan ca sujjóot ya, bu ko defee toroxlul Yàlla ci wax ak jëf daal di daje.فوائد الحديث
Bokk na ci njariñal adiis bi :
Toppub Yàlla day dolli Jaam bi mu gën a jege Yàlla mu kawe mi.
Sopp nañu di baril ñaan ca sujjóot ya; ndax bérabi nangu ñaan la.
التصنيفات
Yiy waral nangu ñaan ak yi koy xañe