إعدادات العرض
ma wax: Subhaanal Laahi, wal hamdu lil Laahi, wa laa ilaaha illal Laahu, wal laahu akbaru, moo ma gënal lépp lu jant bi fenk ci kawam
ma wax: Subhaanal Laahi, wal hamdu lil Laahi, wa laa ilaaha illal Laahu, wal laahu akbaru, moo ma gënal lépp lu jant bi fenk ci kawam
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ma wax: Subhaanal Laahi, wal hamdu lil Laahi, wa laa ilaaha illal Laahu, wal laahu akbaru, moo ma gënal lépp lu jant bi fenk ci kawam».
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية Bosanski English فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Türkçe اردو 中文 हिन्दी বাংলা Español Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் සිංහල မြန်မာ ไทย Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە دری Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy Română Kinyarwanda नेपाली Српски Soomaali Moore Українська Български Tagalog Azərbaycan ქართული тоҷикӣ bm Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne tudd Yàlla mu kawe mi ci baat yu màgg yii moo gën àdduna ak li ci biiram, te mooy: "Subhaanal Laahi": sellal Yàlla ci gépp wàññeeku. "alhamdu lil Laahi": tagg Yàlla ci ay meloom yu mat ya ànd ak bëgg ak màggal. "laa ilaaha illal Laahu": amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla. "al-Laahu akbaru": moo gën a màgg lépp lu mu man a doon.فوائد الحديث
Ñaaxe ci tudd Yàlla, ak ne moo gën lépp lu jant bi fenk ci kawam.
Soññee ci baril di tudd Yàlla, ngir li ci nekk cib yool ak ngëneel.
Bànneexi àdduna lu néew la, te ay neex-neexam it day jeex.
التصنيفات
Sikkar yees joyal