yaw Abbaas, yaw baay taxu Yonnente Yàlla bi, ñaanal Yàlla jàmmi àdduna ak allaaxira

yaw Abbaas, yaw baay taxu Yonnente Yàlla bi, ñaanal Yàlla jàmmi àdduna ak allaaxira

Jële nañu ci Abbaas ibn Abdul Muttalib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Damaa wax ne: yaw Yonnente Yàlla bi, xamal ma lu may ñaan Yàlla mu màgg mi. Mu ne ma: "ñaanal jàmm", ma toog ay bis daal di ñëwaat ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi xamal ma lu may ñaan Yàlla. Mu ne ma:"yaw Abbaas, yaw baay taxu Yonnente Yàlla bi, ñaanal Yàlla jàmmi àdduna ak allaaxira".

[Wér na ngir beneen Adiis bu koy tegtale] [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat]

الشرح

Baay taxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc Abbaas ibn Abdul Muttalib yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa sàkku ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu xamal ko ag ñaan gu muy ñaan Yàlla, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamal ko ne na ñaan Yàlla jàmm ak mucc ci ayib yi ci diine ak ci àdduna ak allaaxira, Abbaas nee na: ginnaaw ay bis ma dellusi fi moom Yonnente bi beneen yoon, ne ko: mu xamal ma ag ñaan gu may ñaan Yàlla, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: yaw Abbaas, yaw baay taxu Yonnente Yàlla bi, ñaanal Yàlla jàmm ngir jeñ jépp lor ak xëcci wépp yiw ak njariñ ci àdduna ak allaaxira.

فوائد الحديث

Baamtu gi Yonnente bi baamtu lenn

tontu li ñeel Abbaas ginnaaw

bamu ka ko laaajee ci ñaareelu bi

day tegtale ne jàmm moo gën ci li jaam bi di ñaan Boroomam .

Leeral ngëneelu jàmm ak ne ci la mbooleem yiwi àdduna ak allaaxira nekk.

Xérug Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ci dolliku xam-xam ak uw yiw

التصنيفات

Ñaan yi bawoo ci Yónnent bi SLM