إعدادات العرض
ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul
ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul», ñu ne ko: waaw bu dee li ma wax moo ngi ci sama mbokk mi nag? Mu wax ne: «bu nekkee ci moom kon jëw nga ko, bu nekkul ci moom nag kon duural nga ko».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە සිංහල ไทย دری Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių or Română Kinyarwanda Српски O‘zbek Moore नेपाली тоҷикӣ Oromoo Soomaali Malagasy Български Українська Azərbaycan ქართული bm Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral dëgg-dëggi jëw bi araam, te mooy: tudd jullit bu fàddu ci lu ko neexul, moo xam ciw mbindiinam la walla ciy jikkoom, niki: patt bi, wurujkat bi, fenkat bi, ak melo yu ñaaw yi ko niru, donte melo yooyu moo ngi ci moom. Bu dee melo wi nekkul ci moom nag loolu moo gën a tar jëw, ndax duur la, maanaam: sosal nit ki ci lu nekkul ci moom.فوائد الحديث
Bokk na ci njariñal adiis bi :
Rafetug njàngalem Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ba tax mu jox leen masala yi ci anamug laaj.
Rafetu teggini Sahaaba yi ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ba tax ñu ne ko Yàlla ak ub Yónenteem ñoo ko xam.
Ki ñuy laaj wax ci lu mu xamul: Yàllaa xam.
Aar gi Sariiha aar mbooloo mi ci sàmm àq yi ak diggante mbokk yi.
Jëw lu araam la lu dul ci yenn anam yi ngir yéwénal; bokk na ca: dindi tooñaange, lu melni ki ñu tooñ tudd turu ka ko tooñ ci koo xam ne man na koo nangul àqam, mu wax ko ne ko: diw tooñ na ma, walla def na ma lii, bokk na ca: diisoo ci mbirum sëy, wàlla lu jëm ci bokk dara, mbaa ci ki ngay dëkkal, ak yu ni mel.
التصنيفات
Teggiini wax ak noppi