moytandikuleen njort; ndaxte njort mooy wax ji gën a nekk aw fen

moytandikuleen njort; ndaxte njort mooy wax ji gën a nekk aw fen

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «moytandikuleen njort; ndaxte njort mooy wax ji gën a nekk aw fen, te buleen di gëstu, buleen di luññutu, buleen di soxorante, buleen di tóngoowante, buleen di bañante, nangeen doon ay mbokk yeen jaami Yàlla yi ».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo yenn yiy waral tàqalikoo ak noonoo ci diggante jullit ñi, Bokk na ci yooyu: (njort) te mooy tuuma ju rot cim tàbbi cim xel ci lu dul jen firnde, mu leeral ne mooy wax ji gën a nekk aw fen. Ak(gëstu): te mooy gëstu ayibi nit ñi ci bët walla nopp. Ak (luññutu): te mooy gëstu li nëbbu ci biri nit ñi, ci lu bon nag la ëpp lu ñu koy jëfandikoo. Ak (soxor) te mooy bañ ñeneen ñi am xéewal. Ak: (tóngoonte) te mooy ku nekk di dummooyu moroomam, du nuyu du seeti mbokkum jullitam. Ak: (bañante) ak sibante ak foñante, niki it lor ñeneen ñi, ak di ñëkkal kanam, ak ñaawalub daje. Mu wax nag ab baat bob ci la biri jullit ñi di yéwene ci seen diggante te mooy: (nekk-leen ay mbokk yéen jaami Yàlla yi) Mbokkoo ag buum la guy boole diggante nit ñi, di yokk mbëggeel ak miinante ci seen biir.

فوائد الحديث

Njort lu ñaaw du lor ki ay màndargam feeñ ci moom, waaye war na ci ki gëm mu nekk ku muus te xellu ba du woru ci ñu bon ñi ak kàccoor yi.

Li ñu ci nàmm mooy artu ci tuuma jiy nekk cim xel, ak di ca wéy, bu dee liy gaar bakkan te du ca wéy, loolu moom kenn du ko toppe kenn.

Araamal nañu lépp luy waral fuñante ak dogante ci diggante mbooloom jullit ñi, ci luññutu ak soxor ak yu ni mel.

Laabire ci di jëflante ak jullit ñi jëflanteg mbokk ci laabire ak bëggante.

التصنيفات

Jikko yees ŋàññ