Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul delloo gëtt

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul delloo gëtt

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul delloo gëtt.

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Bokk na ci njubug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moom daawul delloo gëtt da ko daan nangu; ndax lu woyof a gàddu la te lu neex ug xet la.

فوائد الحديث

Sopp nañu nangu gëtt gu ñu la may; ndax gàddu ko amul coono, te nangu gi amul ndamu.

Mat ak rafetug jikkoy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci ne du delloo gëtt, ak ne day nangu adiya ju ñu ko jox.

Xemmemloo ci jëfandikoo gëtt.

التصنيفات

Teggiini seet nit ak yëglu