ñaan mooy jaamu Yàlla

ñaan mooy jaamu Yàlla

Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñaan mooy jaamu Yàlla» daal di jàng: "Aaya biy wax ne: {séen Boroom nee na wooleen ma ma wuyu leen ñi may rëy a ñaan danañu dugg Jahannama di way-torox} [ soratou Xaafiri: 60]».

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ñaan mooy jaamu Yàlla, kon li war mooy mu nekk lu sell ñeel Yàlla, moo xam wooteg laaj la walla wooteg sàkku, ci di laaj Yàlla mu kawe mi lu koy jariñ, ak jeñ lu koy lor ci àdduna ak allaaxira, walla muy wooteg jaamu, te mooy lépp lu Yàlla bëgg te gërëmloo ko ci ay wax ak i jëf yi feeñ ak yi nëbbu, jaamuy xol yi walla yu yaram yi mbaa yu alal yi Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tegtaloo na ci loolu ne: Yàlla wax na ne: {wooleen ma ma wuyu leen ñi ma rëy a ñaan danañu dugg Jahannama di way-torox}

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi: Ñaan mooy cosaanu jaamu yi, daganul nu jëmale ko ci ku dul Yàlla.

Ñaan day làmboo dëgg-dëggug njaame ak nangu doylug Yàlla ak kàttanam moom aji-Kawe ji, ak soxlaal gi ko jaam bi soxlaal.

Tëkku gu tar mooy payug rëy-rëylu ci jaamu Yàlla ak bàyyi koo ñaan, te ñiy rëy-rëylu ci ñaan Yàlla danañu dugg Jahannama di way-torox di way-doyadi.

التصنيفات

Ngëneelu ñaan