ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar

ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Jële na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu nettali jële ci Boroomam mu màgg mi, mu wax ne: «ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar Yàlla mu baarkeel mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar, Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar,Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, defal lu la soob jéggal naa la».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day nettali jële ci Boroomam ne jaam bi bu defee bàkkaar, daal di wax sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar, Yàlla mu kawe mi day wax: sama jaam bi def na bàkkaar xam na ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, di ko suturaal, baal ko walla mu mbugal ko, kon jéggal naa ko. jaam bi dellu defaat bàkkaar xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, di ko suturaal, baal ko walla mu mbugal ko, kon jéggal naa sama jaam bi. jaam bi dellu defaat bàkkaar xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, di ko suturaal, baal ko walla mu mbugal ko, kon jéggal naa sama jaam bi, na def lu ko soob feek saa yu defee bàkkaar, day bàyyi bàkkaar ba réccu ko, dogu ci bañ caa delluwaat, waaye bakkanam da koy not mu tàbbiwaat ca bàkkaar ba, feek moo ngi def nii di def bàkkaar tey tuub dinaa ko jéggal, ndax tuub day màbb la ko jiitu.

فوائد الحديث

Yaatug yërmàndey Yàlla ci jaamam yi, ba lu nit ki man a def ci bàkkaar ak lu mu man a def bu tuubee dellu ci moom Yàlla jéggal ko.

Ki gëm Yàlla day yaakaar yërmàndey Boroomam, tey ragal mbugëlam, ba tax muy gaawantu di tuub te du wéy cig moy.

Sarti tuub gu wér: deñ ci bàkkaar bi, ak réccu ko, ak dogu ci bañ a dellu ca bàkkaar ba, bu dee tuub gi dafa aju ci tooñ jaam ñi ci séen alal mbaaa séen der, walla séen bakkan, kon day dolli ñenteelu sart, te mooy sàkkoo set sa bàkkaar ba sa Boroom àq ja, walla mu jox ko àqam.

Amug solo ci xam ne Yàlla miy def jaam bi mu xam biri diineem ba tax muy tuub saa yu juumee, te du naagu ba tax muy wéy ca bàkkaar ba.

التصنيفات

Ngëneeli sikkar