ku wax: Subhaanal Laahi wa bi hamdihii, ci bis bi téeméeri yoon, ñu sippi ay bàkkaaram doonte dafa mel ni puuriti géej

ku wax: Subhaanal Laahi wa bi hamdihii, ci bis bi téeméeri yoon, ñu sippi ay bàkkaaram doonte dafa mel ni puuriti géej

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku wax: Subhaanal Laahi wa bi hamdihii, ci bis bi téeméeri yoon, ñu sippi ay bàkkaaram doonte dafa mel ni puuriti géej».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku wax téeméer i yoon ci bis bi: "Subhaanal Laahi wa bi hamdihii"; ñu far ay bàkkaaram jéggal ko ko, doonte dafa bari ba mel ni puuriti géej muy lu weex liy tiim Géej gi bu amee ay yëngu.

فوائد الحديث

Pay gi nag ku ko wax ci bis bi rekk dana ko am moo xam daa toftaloo walla dafa tàqalikoo.

Sàbbaal: mooy sellal Yàlla ci bépp wàññeeku, Cànt: mooy mellal ko ci bépp mat ànd ak bëgg ak màggal.

Li ñu namm ci hadiis bi mooy far bàkkaar yu ndaw yi, bàkkaar yu mag yi moom manul ñàkku tuub ko.

التصنيفات

Ngëneeli sikkar