إعدادات العرض
wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar
wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar».
[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt සිංහල ئۇيغۇرچە Kurdî Hausa Português മലയാളം မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands తెలుగు Kiswahili தமிழ் ไทย دری Български Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy or Română Kinyarwanda тоҷикӣ O‘zbek Akan नेपाली Moore Azərbaycan Oromoo Soomaali Українська bm km rn ქართული Македонски Српски Lingalaالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sawara dañu koo wërale ak i mbir yoy bakkan da koo bëgg, ci jëf yu araam yi, ag gàtteñlu ci yu war yi; Ku topp bànneexam ci loolu kon yeyoo na sawara, Àjjana nag lu ñu muur la wërale ko ak ay mbir yoy bakkan da koo bañ; niki sax ci def ndigal yi bàyyi tere yi te muñ ca, bu dëgëree xeex ak bakkanam ci loolu kon yayoo na dugg àjjana.فوائد الحديث
Bokk na ci liy tax a tàbbi ci bànneex yi li Saytaane di taaral lu bon ak lu ñaaw, ba mujj bakkan bi di ko gise lu rafet daal di jeng jëm ca.
Digle ñu sori bànneex yi ñu araamal; ndax te yoonu sawara la, ak muñ ci yu naqari yi ndax te yoonu àjjana la.
Ngëneelu xeex ak bakkan, ak farlu ci jaamu yi, ak muñ ci yu naqari yi ak coono yi wër topp yi.
التصنيفات
Meloy Àjjana ak Sawara