su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc mi, day xëy nek ku woos xiif di gont biir bi fees dell

su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc mi, day xëy nek ku woos xiif di gont biir bi fees dell

Jële na ñu ci Umar ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg na Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc mi, day xëy nek ku woos xiif di gont biir bi fees dell.

[Wér na] [Ibnu Maaja soloo na ko - At-tirmisiy soloo na ko - Ahmat soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da ñuy soññ ci nuy sukkandiku ci Yàlla mu kawe mi ci xëcc njariñ ak jeñ lor ci mbiri àdduna yi ak yu diine yi, ndax kenn du joxe te kenn du xañe, mbaa muy lore walla muy jariñe ku dul Moom Yàlla mu kawe mi. Ak it nuy def sabab yiy xëcc njariñ di jeñ lor ànd ak sukkandiku ci Yàlla, saa su nu defee loolu Yàlla dana nu wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc miy génn suba di ku xiif, mu dellusi ngoon biir bi fees dell, te jëf i picc mii benn sabab la ci dem wuti wërsëg, te bañ a bàyyandiku mbaa tàyyeel.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi :

gëneelu wakkirlu, ak ne dafa bokk ci sabab yi gën a màgg ci yiy xëcc wërsëg.

Wakkirlu du dàqoonteek def sabab yi, ndax dañoo xamal ne dëgg-dëggi wakkirlu du wuute ak xëy walla gontu jëm ci sàkku wërsëg.

Yittewoog Sariiha ci jëfi xol yi; ndax wakkirlu jëfu xol la.

Sukkandiku ci sabab yi dong loolu diine ju wàññiku la, waaye bàyyi sabab yi tamit xel mu matul la.

التصنيفات

Ngëneeli jëfi xol yi