إعدادات العرض
gaay yay Pasar-pasaree alali Yàlla ji ci lu dul dëgg, sawara ñeel na leen keroog bis-pénc
gaay yay Pasar-pasaree alali Yàlla ji ci lu dul dëgg, sawara ñeel na leen keroog bis-pénc
Jële nañu ci Xawlata mi bokk ci waa-lansaar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «gaay yay Pasar-pasaree alali Yàlla ji ci lu dul dëgg, sawara ñeel na leen keroog bis-pénc».
[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Kurdî Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands සිංහල Hausa ไทย دری Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių or Română Kinyarwanda Српски O‘zbek Moore नेपाली Oromoo Soomaali Malagasy Български Українська Azərbaycan ქართული Lingala bm тоҷикӣ Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle nit ñay jëfandikoo alali jullit ñi cig neen, di ko jël ci lu dul dëgg, te lii nag day matale mbooleem alal yi, ci dajale ga ak fàggu ga ci lu daganul, ak joxe ko ci anam gu baaxul, dana ci dugg itam lekk alali jirim yi, ak alali sarax suy wéy (waqf), ak weddi ndénkaane ya, ak jël ci alali mbooloo te yayoowoo ko. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daldi xamle ne séenug fay keroog bis-pénc mooy sawara.فوائد الحديث
Alal ji nekk ci yoxoy nit ñi alalu Yàlla la, da leen koo dénk ngir ñu jëfandikoo ko ca na mu ko yoonale, te moytu cee soppaxndiku cig neen, te lii nag ñépp a ci yam moo xam njiit la walla nit yi ci des.
Taralug Sariiha ci alalu mbooloo, ci ne képp ku ci jiite dara dees na ko regle ëllëg bis-pénc ca fàggu ga ak ca joxe ga.
Tëkku gii nag képp kuy soppaxndiku ci alal ci lu dul yoon da ciy dugg moo xam alalam la walla alalu keneen.