Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?

Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?

Jële na ñu ci Abuu Bakrata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?» Mu wax ko ñatti yoon, ñu ne ko: ahakay yaw Yónente Yàlla bi, mu ne leen: «bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur» mu jóg toog fekk dafa sóonu woon, daal di ne: «ak wax ludul dëgg», nee na: deñul di ko bàmtu ba ñu mujj wax naan: aka neexoon mu noppi.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaar Sahaabaam yi bàkkaar yi gën a màgg, mu tudd ñatt yii: 1. Bokkaale Yàlla: te mooy jëfal keneen kudul Yàlla genn xeetu jaamu, ak Yamale ludul Yàlla ak Yàlla cig jaamu ak ci moomeelam ak ci ay turam ak i meloom. 2. Dënge ñaari way-jur: te mooy bépp lor bu jëm ci ñaari way-jur, moo xam wax la walla jëf, ak bàyyee rafetal jëme si ñoom ñaar. 3. Wax ju dul dëgg, te bokk na ca seede lu dul dëgg: Mooy wépp luy aw duur, ak aw fen wow dees caa jublu suufeel ki ñu koy teg ci jël alalam, mbaa tooñ ko cib deram, walla lu mel noonu. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa bàmtu artu gi ci wax lu dul dëgg ngir wone ag mbonam ak ay jeexitalam yu ñaaw ci askan wi, ba Sahaaba yi di mujj naan: aka neexoon mu noppi; ngir ñeewante ko, ak bañ lu ko naqari.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi: Bàkkaar bi gën a rëy mooy bokkaale Yàlla; ndax da koo def muy njiitu bàkkaar yu mag yi di ba ca gën a rëy, te loola waxi Yàlla jii moo koy feddali: {Yàlla du jéggale ag bokkaale, waaye dana jéggale lu dul loolu ñeel ku ko soob}.

Àqi ñaari way-juy lu màgg la, ba tax mu lënkale séen i àq ak àqi Yàlla mu kawe mi.

Bàkkaar yi daa séddalikoo yu mag ak yu ndaw, yu mag yi nag mooy: bépp bàkkaar bu am mbugalu àdduna, niki géten ak móolu, walla tëkkug allaaxira, niki tëkkoo ci dugg sawara, yu mag yi itam ay daraja la yenn yi moo gën a rëy yeneen yi cig haraam, bàkkaar yu ndaw nag yi mooy yi nekkul yu mag rekk.

التصنيفات

Jikko yees ŋàññ, Ŋàññ moy yi