إعدادات العرض
kuy dog mbokk du dugg àjjana
kuy dog mbokk du dugg àjjana
Jële nañu ci Jubayru Ibn Muthim -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne dégg na Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «kuy dog mbokk du dugg àjjana».
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە සිංහල தமிழ் ไทย دری Fulfulde Magyar ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių or Română Kinyarwanda Српски O‘zbek Moore नेपाली Oromoo Soomaali Български Українська Azərbaycan ქართული тоҷикӣ bm Malagasy Македонскиالشرح
Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku dog ay mbokkam ca la ñu yayoo ci ay àq, walla lor leen, di ñaawal jëme ci ñoom, kooku yayoowul a dugg àjjana.فوائد الحديث
Bokk na ci njariñal adiis bi :
Dog mbokk ci bàkkaar yu mag yi la bokk.
Jokk mbokk day amee ca kem nañu ko miine, kon day wuute kem barab ya ak jamono ya ak nit ña.
Jokk mbokk dana nekk ci siyaare, ak sarax, ak rafetal jëme ci moom, ak seeti ku feebar, ak digal leen lu baax tere leen lu bon, ak yeneen.
Lu mbokk gi di gën a jege dog mbokk gi di gën a rëy bàkkaar.